Paco Briz - Lima Méti Sama Deuk #1 (Prod by Kef Keffie)

Описание к видео Paco Briz - Lima Méti Sama Deuk #1 (Prod by Kef Keffie)

#LimaMétiSamaDeuk
Prod by #KefKeffie
#DieguiRailsRecords
Directed by Weeflag

Lyrics

Refrain
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Lima méti sama deuk
Vulgarité mo fi feuss
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Mane lima méti sama deuk
Gnithi eup lamign nio geuneu feuss
Lima méti sama deuk
Mane lima méti sama deuk

Couplet 1
Lima méti sama deuk
Féna eup dolé deugg
Comédie féthie ak teugg
Lagn foulal diokh ko geudd
Borom xam xam douthi feuss
Thiaxane kat yi gnoy def buzz
Soutoureu ngui déé ndakh Kocc
Seneporno la lép di dougou
Waral légui gouné yi yaxou ndakh lou bone réka feuss si chaînes yi
Perte temps si réseau sociaux lén gueneul am xam xamou génie
Lignou diné diangal si alal bou lew lagn taylé thi PMU
Rappeur sakh bou saga woul ndèye si son wam bou guéné dou def hit
Sama deuk ay mak you baakha fi teud mais ndaw yangui rêver done américains
Presse bi xooloul louy dieumeulé kanam reew fatt gnok ay faits d’hiver
Les’bienne ak goor jigueen di geun di beuri ana sunuy baaxi demb
Loutakh sama deuk gnouy concours batré bayi fi Miskeen yi amoul agn, ndéki, réér
Damn

Refrain
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Lima méti sama deuk
Vulgarité mo fi feuss
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Mane lima méti sama deuk
Gnithi eup lamign nio geuneu feuss
Lima méti sama deuk
Mane lima méti sama deuk


Couplet 2
Gnari Korité, gnari Tabaski
Tarikha la wala commissions la faute à qui ?
Yagg na gnou dégg milliards you gnou mal acquis
Mame Senghor, Diouf, Wade ba si gnom Macky
Indiscipline bi si tali bi
Yéneu accidents yi doko outeul alibi
Baykat ya ngui dioy na gnou geustou wa aall bi
Fane la Sénégal tolou si mbirou talibés yi
Gouvernement kou ko djité djité nga mythos yi
Chômage ba ngui geun di yokou geun neu yok taux yi
Amo xalis dougn la laal si yéneu hôpitaux yi
Inaugurer TER at, roumboul chapiteaux yi
Créer vie bo amoul biir internet starou virtuelle nga lepp si bazou mot de passe
Bou Rangou manquer respect wa Jamra kone est ce que diotoul gnou khooli soirée ba gni fa pass
Soutoureu bi amatoul seuy yeupeu ngi tass
Envoyer sa photo taat yi fépp ba paré di kass
Contrats si sougnouy ressources naturelles yi amoul transparence fi lépeu leundeum dafa Timiss
Paradi fiscaux yi da gnou ko miiss
Sopi sunu diné def ko mode
Diouli wo té kouy diouli ngani ko boum la fatté si niaan
Taayal nga niaan té ya geuneu ignane
Artistes internationaux yi am sponsor gni fi deuk bougnou khewlé dougnou guiss touss
Kouy wallou wa Sabadola
Or bi fégn na moudié na gnou done badola
Gnata at si rén ani bateau Le Diola
Sacrifices yi diour neu moussibeu ak balaa
Gnak esprit patriotique
Kén dou wakh Guy Marius Sagna moudié DIC
Violence faite aux femmes am goor you sadique
Insécurité bari dangay moudié tiit
Sénégal égal yalwaan kat bou tok si mine d’or am pétrole ak gaz di békoor

Refrain
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Lima méti sama deuk
Vulgarité mo fi feuss
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Mane lima méti sama deuk
Gnithi eup lamign nio geuneu feuss
Lima méti sama deuk
Mane lima méti sama deuk

Couplet 3
Geum Koun Fa Yakoune
Yakaar si xarfa xoufa
Pétaw, ndiébar, soul
Lagn djiteul ba Al Quran
Oustaz sakh bou wakhoul
Si ndiaalo dougn ko foulaal
Nguir meun si langamou diaral na len deup wakhou Rassoul
Sama deukeu féss lolo ki nafékk té beuss bouné gnoy wakhtané rafet xol
Politiciens you meuneu fén di gnou ray si télé bi soubeu ak ngone
Zeyda Zamane woté Yoninte, sites yi dieul ko def ko thiow
Mane lima méti gni xam lépeu fi beuri té diokhougn len nopp
Kaay ma wakh la negger lima méti sama deuk
Mbir yi gneup tek nagn si beut
Ken wakhoul lougn meuneu dégg
Thiaxane leundeumeul neu deugg
Nit yi warone délo si khélou diam yi gno sopi wakhou Yalla nguir nékh Ousmane, Pathé
Samba ak Mademba
Nit you bakh yé ngui fi loutakh diamonoy tay xoolou niou si demb ? Damn !!!

Refrain
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Lima méti sama deuk
Vulgarité mo fi feuss
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Lima méti sama deuk
Médiocrité moy def buzz
Mane lima méti sama deuk
Gnithi eup lamign nio geuneu feuss
Lima méti sama deuk
Mane lima méti sama deuk




Special Thanks

J-Fa UNIVERSAL PROD , DIACK PRO OPTIQUE, ROKHAYA DIAGNE

Комментарии

Информация по комментариям в разработке