EL HADJI CHEIKH BOU DIOP New album SAMA WASSILA

Описание к видео EL HADJI CHEIKH BOU DIOP New album SAMA WASSILA

SAMA WASSILA
1. Santa tinaa bour bi mom adina ak laahira
Di djouli seulmeul thi taaha mii maami cheikh sama wassilaa
2. Mandéétinaa bay tereuf tédou manditéék sangara
Cheikh booma diam pikiirou léér ba té goor gui moy sama wassilaa
3. Bissou dimanche laa démoone thia nganou baye amdy cheikh gua
Thi yonou ndakh naar way wi dapp ma ni fook ma way sama wassila
4. Ma yéksi ndiassane kérook diaarnaa thia biir penthie ma
Bécaye abidine modone ngénté ma diaar fa way sama wassila
5. Ya thiamba dieuleul way wi sa waya sohna khady kounta moy sa yaye
Sama rak nga sama kharite di seut thi cheikh sama wassila
6. Bayil ma wah lay mbiram lou djiitou sah ak nieuweum
Wah nagnou biir ndakh naar touram wa moom sama wassila
7. Mame cheikh bou mame sid bécaye mo djoguéwoone algérie
Ngir dieulsi mame cheikh bounama mi waydjourou sama wassila
8. Naka la wah ak rakam dja gor gui néko waw waayé mayma
Nawétte bi daanoo niou déloo bayil ma xél sama wassila
9. Bala niou djéhal nawétt ba cheikh boul eweul daal di faatou
Rakam dja rob kook waham dja sa tour dou fay sama wassilaa
10. Kérook lanaane légui took naa maak kouma am fii laniouy déss
Kou soul magam warko wéteuli thiey tourondoo sama wassilaa
11. Ba niénti gor byamou dieuloone nieupp dioureul koy waliyou
Taaw bathi thiaate ddthi guiss thiomo moy weydiou roup samam wassilaa
12. Mame peuya faye ak mame thioro diouf maama codou diop ak rokhaya
Coumba chérif yaayou cheikh bécaye mii taaw bi yar sama wassila
13. Wassiya mame cheikh bounama wahoone mame cheikh bécaye
Niaar gni di moudieu nieuw sama guinaaw kéne ki moy sama wassila
14. Bounama thioro diouf lawoone ak cheikh bou mame codou diop
Mimou diotoone wah magam dja touram dou fay sam wassilaa
15. Fii badni oumi hii la doonéé khalifa mame cheikh bounama
Cheikhal bécaye mak dja néna dénkaané nagne sama wassila
16. Foofa la dioté werdou khadir foofa la amé may you reuy ya
Foofa djangé fofa la khamé foofa la doone sama wassilaa
17. Bimou gané adina ba bimouy dém laakhira
défoufi mba wah lou niaaw diaarama cheikh sama wassila
18. Mom kheulweu rékay mbiram dawmane la donoone thia koor gua
Def alkhourane mouy wételeum diiné ngi dioy sama wassilaa
19. Kharite ba nak mooy khadar daa naniou tok ay diotaay
Bou gane gni dougoussé goor gui nopi di wah lénééne sama wassila
20. Défar na nitt ak djiné rawhaane yi ak ay khoudaam
ba légui gningi koy liguéyal ndah douniou wor sama wassila
21. Kou wédi nay togne khalifam mbaa taaloubém mbaa ndiabootam
Mba kouko beug ak koum meuna doone faww nga guiss sam wassila
22. Yaw miko geum kaay ma wahla bookoy ziaaréti noy déf
Fékhél ba daw louy bokaalé mom rék la bagne sama wassila
23. Képp kou dioh bour yalla thiereum délou nga yonéne bi thiereum
Bo siki sakka woul geum sa serigne loo niiane dou niil sama wassila
24. Mangi dagaane niaane sa barké att mi nadoone atou oubikou
Thi groupe beug cheikh bou thi adina sama wassila
25. Salle bouma dieul naako féssal espace bouma dieul naako féssal
Téyitt fouma dém gadou ndam laa sa barké iao sam wassilaa
26. Nagne yéék thi avion yi weur adina wané saap liguéye
Fagoulma fouma dém nga djiitou ba gnooniou kham sama wassila
27. Ndah nioune kou bagne souniou douffouff yi bagne nga sounaa khayrou naassi
Doo téki yitt dara souniou kanam féék ragné woo sama wassilaa
28. Mangi dagaane sa barké fathou ak nasrou sabrook sakiina
Ak guem gou wér ak ilmook yar sa barké yaw sama wassilaa
29. Biss bima dioup mooy premiere kone fouma dém naay premiere
Té kouma beug doone prmiere sa barké yaw sam wassilaa
30. Ya chéikhana diaalénaala diaalé sa seut haaji mame bou
Ak mouhidiine haaj baachiir mame ndamba moum sama wassilaa
31. Ak sama mak yooya djiitou amdy mou pape ahmadoo
Papa abdou kémaane magam djaa say seuta ngook sama wassilaa
32. Sali wa salim alaa nabiyiiinaa ahmadaa
Ak saabayaak doom ya seutt ya gni maami cheikh sama wassilaa
33. Yénama ladioone lou béss kone indinaa daathie you béss
Nangééne nieuweundoo saal ba fééss faw ma way sam wassila

Комментарии

Информация по комментариям в разработке